Hommage à Mamadou Bara Samb Lahi : Le message d’adieu du « Jeune Poète »

Date:

XALIMANEWS- Alors qu’on le croyait encore debout pour longtemps, le « Jeune Poète » s’est éteint à l’âge de 36 ans. A travers son texte publié, qui apparait ce jour comme un signe, Xalima rend hommage à Mamadou Bara Samb Lahi, un jeune intellectuel, pétri de connaissances et de talent. Le 10 janvier 2024, Bara Laye, le spirituel, faisait ainsi ses adieux à sa communauté à travers un texte prémonitoire. In extenso.

Na ngéen ma seedeel….

1
Bu ngeen ma xëyee tëral ba jël sër ya sànga ma
Kuney woote naa Baaraa fi tàggoo di tàgge ma

2
Xabaar ba tasaaroo ñéppa naa kañ la mbir mi xew
mu mel ne li daa fel saay moroom warta songa ma

3
Samay soppe boolooy jooy di yonnente saay nataal
Samay mbokk yuuxoo jaaxle, nees tuut ñu génne ma

4
Ñu tëj ma ca biir seddaay ba, ngir waaj defarsi ma
Lijanti ji col gaak yëf ya ngir waajsi sanga ma

5
Sikkar sa di riir ñii jiitu, soppe ya gàddu ma
ñu far ma tëral ñép noppi ngir xaar ñu seede ma

6
Na ngeen seede bés boobaa ne Yonnen bi laa bëggoon
te moom rekka laa yaakaar keroog ngir mu teeru ma

7
Na ngeen seede saag jeex takka seey far ci Baay Saxiir
te ngeen ñaan bu may xippiy dajeek moom mu lënga ma

8
lu saag jaamu neew neew Yàlla Buur laa defoon ndimbal
Bu tooñ yi baree yit man namaa baal te yéege ma

9
Keroog la ñu may jël sànga suuf, dellu bàyyi ma
ma wéetak samay jëf ak samay wax ñu seede ma

10
Tëraay bu ni ragloo, néeg bu tuute ni masta am
Ludul yërmaandey Buur Yàlla foofa xalaatu ma

11
Ludul barke Yonnenn bii mu yonni ci yërmaandeek
cofeel gii ma ëmbal Baay Saxiir tax mu gansi ma

12
Ma àndak Sëriñ bay muuñ jubal péeyu Mustafaa
Ma egsi mu foon maak leer ya xëcc ma lëng ma

13
Mu naa way ma, may màddaa ca kaw Baay Saxiir di beg
Yonnen ba di may jóor ay mayam mag ña feelu ma

14
Ba bés ba tusuur Yonnen bi maa ngiiy dagaan sa mbeg
Di jeem a bégal it Baay Saxiir ñaan mu gunge ma

15
Na Buur julli sëlmël saasu nekk ci yaw Yonnen
Te wéetook samab xol def Yonnen muy xarit sama
06.01.2024

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici

CAN 2023

DEPECHES

DANS LA MEME CATEGORIE
EXCLUSIVITE

Presse-Nécrologie : Décès du journaliste Mbaye Sidy Mbaye

XALIMANEWS-Le journaliste Mbaye Sidy Mbaye, ancien porte-parole du Conseil...

Nécrologie : Décès de l’ancien député du PDS, El Hadji Malick Gueye

XALIMANEWS- L'ancien député du PDS, El Hadji Malick Gueye,...

Le monde de la musique sénégalaise en deuil : Décès de Baïlo Diagne, fondateur de Super Diamono

XALIMANEWS-Le monde de la musique sénégalaise est en deuil...