« Celui.elle qui ne te connait pas t’appelle hé! Mais ceux.elles qui te connaissent passent par ton nom. Il y a des gens qui pensent être courageux.ses parce qu’ils.elles sont vulgaires, qui t’abordent en public ou en virtuel en t’intimant des ordres. Que savent-ils.elles de ta vie, de ton passé, des combats efficaces que tu mènes sans tambours ni trompettes? Qui sont-ils.elles pour te dire ce que tu dois faire ou dire? Ils.elles ne sont juste que des anti modèles sociaux qui exposent à la face du monde l’échec de leur éducation.
Ne laissez personne vous perturber. Portez votre propre message, soyez authentique, posez les actes positifs qui font avancer votre vie et celle de votre communauté. Laissez les loups de la meute hurler mais ne changez pas votre fusil d’épaule surtout quand vos vraies cibles sont atteintes.
Comme Tiémoko, répétez leur ce que disaient nos Anciens : «J’ai plus peur de celui qui me respecte que de celui qui me menace.» (Sous l’orage, Seydou Badian, Présence Africaine, 1963). »
Dr Massamba Guèye LBA
Nayrafet
—-
Yóbbalu 20 fanu Ut 2021
Wegeel ..:
« Ku la xamut, hey la lay woowee, waaye ñi la xam ci sa tur la ñuy jaar. Am na ñooñ da ñoo foog ni am nañ fit ndax seen ñàkk xersa, ba tax ci pénc mi mbaa lënd gi lañ lay jooru seen xalaat mbaa di la jéem a sa li nga war a def mbaa wax.
Ñoom ana lu ñu xam ci sag dund, say jaar-jaar, li ngay jëf ci sa askan te koy yelu? Ana ñooy ñan ci yow ba war laa sa ni ngay doxee mbaa waxee? Du nu lenn, du ñu kenn! Xanaa kay fàww ñu wone seen ñàkk yar ak seen xamadi àdduna rekk. Baadolo kott mooy ëyu ku mu xamut ci biir ndaje.
Bul may kenn sañ-sañ bi ba mu lay yëngal. Deel wax sa wax i bopp ci sa waxinu bopp, bul toppandoo kenn, jëfal lu lay yokk te am njariñ ci sa askan. Bawkat teewul daamar wéyu yoonam. Bu dee li ngay diir ci ngëneel yaa ngi koy jam te mu dagan, bul soppi doxaliin.
Ni Cemoxo, ne leen, ni ko mag ñi daan waxee : « Ki ma weg, laa gën a ragal ci ki may tëkku » ( Téereb fent netalib Seydu Baja?, 1963). »
Dr Masàmba GÉY GA